Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 18:1-14 in Wolof

Help us?

Sabóor 18:1-14 in Kàddug Yàlla gi

1 Mu jëm ci njiital jàngkat yi, ñeel Daawuda jaamub Aji Sax ji. Mu jagleel Aji Sax ji woy wii, bés ba mu ko xettlee ci mboolem noonam, xettli ko it ci Buur Sóol. Kàdduy woy yaa ngii.
2 Mu ne: Aji Sax ji, maa la sopp, yaw mi may dooleel.
3 Aji Sax ji laay sës, mu di ma aar, di ma wallu. Mooy sama Yàlla, ji may sës, yiiru, fegu; mooy Boroom doole ji may musal, di ma làq.
4 Ki yelloo cant, Aji Sax ji, moom laa woo, mucc ci samay noon.
5 Buumi ndee tanc ma, walum kasara naq ma,
6 buumi njaniiw laaw ma, dee ne jaas, di ma fiir.
7 Ma jàq, woo Aji Sax ji, ne sama Yàlla wallóoy, mu dégge këram. Ma yuuxu, muy dégg.
8 Mu mer, suuf yëngu, di ker-keri; kenuy tund ya jaayu, di reg-regi.
9 Saxar di sël-sëlee ca wakkan ya, sawara boye ca gémmiñ ga, xal yu yànj tàkke ca.
10 Mu firi asamaan, wàcc, niir yu fatt lal tànk ya.
11 Ma nga war malaakam serub, di naaw, daayaarloo laafi ngelaw.
12 Ma nga bàddoo lëndëm, làqoo, làmboo ndox mu lëndëm aki xàmbaar,
13 leer a ko jiitu, xàmbaar ya topp ca, ak tawub yuur ak xali sawara.
14 Aji Sax jee dënoo asamaan. Aji Kawe jee àddu, muy tawub yuur ak xali sawara,
Sabóor 18 in Kàddug Yàlla gi