Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 17:3-14 in Wolof

Help us?

Sabóor 17:3-14 in Kàddug Yàlla gi

3 Natt nga saab xol, niir ma guddi, settantal ma, gisoo dara. Dogu naa ne duma moye wax.
4 Su may jëf it, di sàmm sa kàddu. Maay moyu yoonu ku bon.
5 Sa tànk, sama tànk, jàdduma fenn.
6 Éy Yàlla, maa lay woo, nga di ma wuyu; teewlu ma te déglu ma!
7 Na sa ngor feeñ, yaw miy walloo sa doole ku la làqooy noonam.
8 Sàmm ma ni peru bët; làqe ma sa ker,
9 ma rëcc ñu bon ñi ma song, noon ñii ma gaw, nar maa bóom.
10 Seen xol dàq yërmande, seeni wax di reewande.
11 Tanc nañu nu fépp, ne nu jàkk, nar noo tëral.
12 Mbete gaynde gu namma fàdde, gaynde gu mat guy tëroo!
13 Éy Aji Sax ji, jógal dajeek moom, detteel ko. Xettlee ma sa saamar, ma rëcc ku bon.
14 Éy Aji Sax ji, walloo ma sa doole, ma rëcc ñi séddoo dundu àddina. Say soppe, nga reggal, seeni doom regg, desalal seeni doom.
Sabóor 17 in Kàddug Yàlla gi