3 Natt nga saab xol, niir ma guddi, settantal ma, gisoo dara. Dogu naa ne duma moye wax.
4 Su may jëf it, di sàmm sa kàddu. Maay moyu yoonu ku bon.
5 Sa tànk, sama tànk, jàdduma fenn.
6 Éy Yàlla, maa lay woo, nga di ma wuyu; teewlu ma te déglu ma!
7 Na sa ngor feeñ, yaw miy walloo sa doole ku la làqooy noonam.
8 Sàmm ma ni peru bët; làqe ma sa ker,
9 ma rëcc ñu bon ñi ma song, noon ñii ma gaw, nar maa bóom.
10 Seen xol dàq yërmande, seeni wax di reewande.