3 Ñépp lajj, bokk yàqu yaxeet. Kenn deful lu baax, du kenn sax.
4 Aji Sax ji nee: «Xanaa ñiy def lu bon ñépp xamuñu dara? Ñuy lekk sama ñoñ niw ñam, te sàkkuwuñu Aji Sax ji.»
5 Foofu lañuy tiite tiitaange lu réy! Du Yàllaa ngi ànd ak kuréli ñu jub ñi?
6 Ku néewlee yaakaar, ngeen tas ko, waaye Aji Sax ji la làqoo.