Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 148:7-14 in Wolof

Help us?

Sabóor 148:7-14 in Kàddug Yàlla gi

7 Nangeen màggale Aji Sax ji fa kaw suuf, yeen ninki-nànkay géej ak xóote yépp,
8 ba ca melax yaak doj yu sedd yay taw, ak tawub yuur akub lay, ba ca ngëlén yu mag yay def ndigalam.
9 Màggal-leen ko yeen tund yu mag yeek yu ndaw yépp, ba ci garab yiy meññ ak garabi seedar yi,
10 ba ci mala yépp, yu àll ak gépp jur ak luy raam ak njanaaw,
11 ak buuri àddinaak xeet yépp, ak kilifa yeek njiiti àddina yépp,
12 xale bu góor ak bu jigéen, mag ak ndaw.
13 Màggal-leen turu Aji Sax ji, moom doŋŋ la turam kawe, darajaam tiim asamaan ak suuf.
14 Moo dooleel ñoñam, wóllëreem ñiy mbooloom bànni Israyil, xeet wi mu xejjoo, di ko màggal. Màggal-leen Ki Sax!
Sabóor 148 in Kàddug Yàlla gi