13 Mooy tëj ràpp seen bunti dëkk, barkeel seen askan wa ca biir,
14 jàmmal seen suufas réew, reggal leen ngëneelu pepp,
15 yónnee suuf ndigalam, kàddoom ne coww, daw ca.
16 Mooy tawal yuur bu mel ni wëttéen, di lay lay bu sedd, mel ni pënd ci suuf.
17 Mooy yuri tawub yuuram niy donj. Bu ni seddee, ana kuy taxaw?