12 Yerusalem, sargal-leen Aji Sax ji! yeen waa Siyoŋ laa ne, màggal-leen seen Yàlla!
13 Mooy tëj ràpp seen bunti dëkk, barkeel seen askan wa ca biir,
14 jàmmal seen suufas réew, reggal leen ngëneelu pepp,
15 yónnee suuf ndigalam, kàddoom ne coww, daw ca.
16 Mooy tawal yuur bu mel ni wëttéen, di lay lay bu sedd, mel ni pënd ci suuf.