7 di àtte néew-ji-doole, di leel ku xiif. Aji Sax jeey tijji ku ñu tëj.
8 Aji Sax jeey xippil silmaxa, di siggil ku sëgg. Aji Sax jee sopp ku jub.
9 Aji Sax jeey sàmm doxandéem, taxawu jirim ak jëtun, waaye mooy lajjal pexem ku bon.
10 Aji Sax jeey nguuru ba fàww. Yaw Siyoŋ, sa Yàllaa ñeel maasoo maas. Màggal-leen Ki Sax!