Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 146:4-10 in Wolof

Help us?

Sabóor 146:4-10 in Kàddug Yàlla gi

4 Noo ga day rëcc, mu dellu suuf; bu bés baa, pexeem jeex.
5 Ndokklee kuy dimbalikoo Yàllay Yanqóoba; di yaakaar Yàllaam Aji Sax ji,
6 ki sàkk kaw ak suuf, géej ak lu ci biiram, di sàmm dëgg ba fàww,
7 di àtte néew-ji-doole, di leel ku xiif. Aji Sax jeey tijji ku ñu tëj.
8 Aji Sax jeey xippil silmaxa, di siggil ku sëgg. Aji Sax jee sopp ku jub.
9 Aji Sax jeey sàmm doxandéem, taxawu jirim ak jëtun, waaye mooy lajjal pexem ku bon.
10 Aji Sax jeey nguuru ba fàww. Yaw Siyoŋ, sa Yàllaa ñeel maasoo maas. Màggal-leen Ki Sax!
Sabóor 146 in Kàddug Yàlla gi