3 Buleen wóolu kilifa, doom aadama amul wall.
4 Noo ga day rëcc, mu dellu suuf; bu bés baa, pexeem jeex.
5 Ndokklee kuy dimbalikoo Yàllay Yanqóoba; di yaakaar Yàllaam Aji Sax ji,
6 ki sàkk kaw ak suuf, géej ak lu ci biiram, di sàmm dëgg ba fàww,
7 di àtte néew-ji-doole, di leel ku xiif. Aji Sax jeey tijji ku ñu tëj.
8 Aji Sax jeey xippil silmaxa, di siggil ku sëgg. Aji Sax jee sopp ku jub.