Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 145:13-21 in Wolof

Help us?

Sabóor 145:13-21 in Kàddug Yàlla gi

13 Sa nguur ay nguur gu sax dàkk, sa kilifteef ñeel maasoo maas. Aji Sax ji daa sàmm ay waxam, gore ciy jëfam.
14 Ku daanu, Aji Sax ji wallu; ku sëgg, mu siggil.
15 Ñépp a la wékk bët, di yaakaar, te bu jotee, yaa leen di leel,
16 tàllal sa loxo, reggal luy dund, ba xolam sedd.
17 Aji Sax ji, jëfinam jépp njekk la, jëfam jépp ngor la.
18 Aji Sax ji, képp ku ko woo wall, mu jege la, képp ku ko woo wall te muy dëgg.
19 Nammeelu ku ko ragal, mu sottal; yuuxam, mu dégg, musal.
20 Aji Sax jeey sàmm kuy soppeem, di sànk képp ku bon.
21 Naa sàlloo sant Aji Sax ji, na luy dund saxoo dàkk di màggal sellngay turam!
Sabóor 145 in Kàddug Yàlla gi