12 doom aadama xam say jaloore ak sa teddngaak sa darajay nguur.
13 Sa nguur ay nguur gu sax dàkk, sa kilifteef ñeel maasoo maas. Aji Sax ji daa sàmm ay waxam, gore ciy jëfam.
14 Ku daanu, Aji Sax ji wallu; ku sëgg, mu siggil.
15 Ñépp a la wékk bët, di yaakaar, te bu jotee, yaa leen di leel,
16 tàllal sa loxo, reggal luy dund, ba xolam sedd.