7 nga yóotoo ma fu kawe, xettli ma, wallu ma ci doxandéem yi def wali wal fi sama kaw,
8 di fen, di giñ ay fen.
9 Yàlla, naa la woyal woy wu yees, xalamal la xalamu fukki buum.
10 Yaay may buur yi ndam, yaa musal sa jaam ba, Daawuda ci saamar bu aay.
11 Musal ma, xettli ma ci loxol doxandéem yiy fen, di giñ ay fen.