Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 143:3-7 in Wolof

Help us?

Sabóor 143:3-7 in Kàddug Yàlla gi

3 Noon a ma sambal, daane ma, joggati, dëël ma ci lëndëm ni ku dee bu yàgg.
4 Sama doole jeex tàkk, sama xol jeex, ma ne yàcc.
5 May fàttliku bu jëkkoon, di xalaat sa jaloore yépp, seetaat li nga def.
6 Ma tàllal lay loxo, di la sàkku, ni suuf su mar di sàkkoo ndox. Selaw.
7 Aji Sax ji, gaawal wuyu ma; sama xol a jeex, ma ne yàcc, bu ma xañ sa yiw, ma yem ak kuy tàbbiji biir pax.
Sabóor 143 in Kàddug Yàlla gi