Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 143:3-12 in Wolof

Help us?

Sabóor 143:3-12 in Kàddug Yàlla gi

3 Noon a ma sambal, daane ma, joggati, dëël ma ci lëndëm ni ku dee bu yàgg.
4 Sama doole jeex tàkk, sama xol jeex, ma ne yàcc.
5 May fàttliku bu jëkkoon, di xalaat sa jaloore yépp, seetaat li nga def.
6 Ma tàllal lay loxo, di la sàkku, ni suuf su mar di sàkkoo ndox. Selaw.
7 Aji Sax ji, gaawal wuyu ma; sama xol a jeex, ma ne yàcc, bu ma xañ sa yiw, ma yem ak kuy tàbbiji biir pax.
8 Xëye ma sa ngor, yaw laa wóolu; xamal ma fu may doxe, yaw laa wékk sama bakkan.
9 Aji Sax ji, musal ma ci noon yi, yaw laa làqoo.
10 Jàngal ma, ma jëfe sa coobare; yaa di sama Yàlla. Yal na ma sam xel jiitee mbaax ci yoon wu tàlli.
11 Aji Sax ji, musal ma ngir saw tur, jëfeel sag njekk, teggil ma njàqarey bakkan.
12 Sànkal ma noon yi ci sa ngor, bóomal ma bépp bañ. Man de, maay sab jaam!
Sabóor 143 in Kàddug Yàlla gi