Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 141:6-10 in Wolof

Help us?

Sabóor 141:6-10 in Kàddug Yàlla gi

6 Yal nañu fenqe seeni njiit ciw doj, ba noon yi xam ne dëgg laa wax.
7 Ni ñuy gàbbe suuf ba mu ne ŋafeet, ni la njaniiw di ŋaye, aw seeni yax yu tasaaroo.
8 Aji Sax ji Boroom bi, yaw laa wékki gët, yaw laa làqoo, bu ma seetaan, ma dee.
9 Musal ma ci yeer yi ñu ma gasal, ak fiir yi ma defkati ñaawtéef yi tegal.
10 Yal na ku bon tàbbi cig fiiram, te man ma teggi, wéy.
Sabóor 141 in Kàddug Yàlla gi