Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 140:3-9 in Wolof

Help us?

Sabóor 140:3-9 in Kàddug Yàlla gi

3 kuy nas lu bon, tey saxoo di sookey xare,
4 daas làmmiñam ni jaan, guux daŋaru ñàngóor. Selaw.
5 Éy Aji Sax ji, aar ma ci loxol ku bon, musal ma ci nitu fitna, ku may fexee fakktal.
6 Ñu bew ñee ma làqali yeer, lalal may buum aki caax, feggal ma seeni fiir ci yoon wi. Selaw.
7 Dama ne Aji Sax ji, yaay sama Yàlla; Aji Sax ji, teewlul, ma dagaan la.
8 Aji Sax ji Boroom bi may walloo doole, yaa ma yiir keroog bésub xare.
9 Aji Sax ji, bul may ku bon nammeelam, bul joyal pexeem, muy yékkatiku. Selaw.
Sabóor 140 in Kàddug Yàlla gi