3 kuy nas lu bon, tey saxoo di sookey xare,
4 daas làmmiñam ni jaan, guux daŋaru ñàngóor. Selaw.
5 Éy Aji Sax ji, aar ma ci loxol ku bon, musal ma ci nitu fitna, ku may fexee fakktal.
6 Ñu bew ñee ma làqali yeer, lalal may buum aki caax, feggal ma seeni fiir ci yoon wi. Selaw.