Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 139:3-7 in Wolof

Help us?

Sabóor 139:3-7 in Kàddug Yàlla gi

3 di càmbar samab dox ak sama tëraay, yittewoo lépp lu may def.
4 Aji Sax ji, bala maa wax baat, ndeke yaw, xam nga lépp.
5 Kanam ak gannaaw nga ma dare, teg ma sa loxo.
6 Ni nga ma xame daa yéeme, xóot lool, ba wees ma.
7 Fu ma jëm, ba sore la? Fu ma daw jëm, foo teewul?
Sabóor 139 in Kàddug Yàlla gi