3 di càmbar samab dox ak sama tëraay, yittewoo lépp lu may def.
4 Aji Sax ji, bala maa wax baat, ndeke yaw, xam nga lépp.
5 Kanam ak gannaaw nga ma dare, teg ma sa loxo.
6 Ni nga ma xame daa yéeme, xóot lool, ba wees ma.
7 Fu ma jëm, ba sore la? Fu ma daw jëm, foo teewul?
8 Ma ñalgu ba asamaan, yaa nga fa! Ma tëri njaniiw, ndeke yaa nga fa!
9 Ma war laafi njël, dëkki wàllaa géej,
10 nga tettee ma fa ba tey, téyee ma sa ndijoor.
11 Su ma noon: «Na ma lëndëm mëdd boog, ba leer gi far guddil ma,»
12 du tax lëndëm lëndëmal la dara. Guddi da laa leeralal ni bëccëg, lëndëm dig leer fi yaw.