13 Yaa ma sàkkal xol ak xalaat, ràbbe ma sama biiru ndey.
14 Naa la sante sama bind bu raglu bii te yéeme, say jalooree di kéemaan, bir na ma!
15 Sama jëmm jii umpu la, ba muy bindu ci kumpa, mel ni lu ñu ràbbe ci xóotey suuf.
16 Gis nga ma, ba ma diw lumb; sa téere lim na fan yi nga ma àppal, ba ca benn dooragul.
17 Yàlla, say xalaat aka maa yéem! Ndaw lim bu réy!
18 Su ma ko doon waññ, moo ëpp feppi suuf. Maa ngii yewwu, ne feek yaw ba tey.