Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 139:11-21 in Wolof

Help us?

Sabóor 139:11-21 in Kàddug Yàlla gi

11 Su ma noon: «Na ma lëndëm mëdd boog, ba leer gi far guddil ma,»
12 du tax lëndëm lëndëmal la dara. Guddi da laa leeralal ni bëccëg, lëndëm dig leer fi yaw.
13 Yaa ma sàkkal xol ak xalaat, ràbbe ma sama biiru ndey.
14 Naa la sante sama bind bu raglu bii te yéeme, say jalooree di kéemaan, bir na ma!
15 Sama jëmm jii umpu la, ba muy bindu ci kumpa, mel ni lu ñu ràbbe ci xóotey suuf.
16 Gis nga ma, ba ma diw lumb; sa téere lim na fan yi nga ma àppal, ba ca benn dooragul.
17 Yàlla, say xalaat aka maa yéem! Ndaw lim bu réy!
18 Su ma ko doon waññ, moo ëpp feppi suuf. Maa ngii yewwu, ne feek yaw ba tey.
19 Éy sama Yàlla, soo reyoon ñu bon ñii! Yeen bóomkat yi, soreleen ma!
20 Ñii sa tur lañuy luubale, noonoo la, di tudd sa tur ciy caaxaan.
21 Aji Sax ji, maaka bañ ñi la bañ te sib ñi lay gàntal.
Sabóor 139 in Kàddug Yàlla gi