3 Bés ba ma wootee, yaa ma wuyu, ñemeel ma, dooleel ma.
4 Aji Sax ji, na la buuri àddina yépp màggal, ñoo dégg kàddu yi nga wax.
5 Nañu woy say jaloore, naan: «Aji Sax jeeka màgg teddnga!»
6 Aji Sax jee kawe! Ku toroxlu, mu niir; ku réy, mu ñooru.
7 Ma wéye njàqare, nga musal ma, dogalee sa loxo merum noon, walloo ma sa ndijoor.