Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 137:3-8 in Wolof

Help us?

Sabóor 137:3-8 in Kàddug Yàlla gi

3 Fa la nu sunuy sang daa woyloo, not nu, bëgg nu bégal leen, naan: «Woyal-leen nu ci woyi Siyoŋ.»
4 Moo nu nuy woye woyu Aji Sax ji kaw suufas yéefar?
5 Éy Yerusalem, su ma la naree fàtte, yal na ma doole dëddu!
6 Yerusalem, su ma la fàttlikuwul, fonk la, ba gën laa bége lépp, yal na sama làmmiñ tafoo sama denqleñ.
7 Aji Sax ji, fàttlikul Edomeen ña, keroog jantub Yerusalem, ba ñu naan: «Màbbleena màbb, ba kenug dëkk bi siiñ!»
8 Yeen waa Babilon, gi ñu nara fàllas, ndokklee ku leen fey jëf, ja ngeen nu def!
Sabóor 137 in Kàddug Yàlla gi