7 Mooy yékkateey niir fa cati àddina, sàkkal taw ay melax, yebbee ngelaw cay dencam,
8 fàdd luy taaw fa Misra, doom aadama, ba ci mala.
9 Yeen waa Misra, moo yónnee ay firndeeki kéemaan fi seen biir, ñeel Firawnaak jawriñam ñépp.
10 Moo duma ay xeeti xeet, bóom buur yu mag yi,
11 muy Siwon buurub Amoreen ña, ak Og buuru Basan, ak buuri Kanaan ñépp.
12 Moo nangu seen réew, séddale, bànni Israyil ñiy ñoñam séddoo.
13 Aji Sax ji, sa tur ba fàww; Aji Sax ji, sa woy a saxal maasoo maas.
14 Aji Sax ji kay ay àtte ñoñam ñi, di ñeewante jaamam ñi.