Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 135:6-19 in Wolof

Help us?

Sabóor 135:6-19 in Kàddug Yàlla gi

6 Lépp lu Aji Sax ji namm, moom lay def asamaan ak suuf, ak biir géej ak xóote yépp.
7 Mooy yékkateey niir fa cati àddina, sàkkal taw ay melax, yebbee ngelaw cay dencam,
8 fàdd luy taaw fa Misra, doom aadama, ba ci mala.
9 Yeen waa Misra, moo yónnee ay firndeeki kéemaan fi seen biir, ñeel Firawnaak jawriñam ñépp.
10 Moo duma ay xeeti xeet, bóom buur yu mag yi,
11 muy Siwon buurub Amoreen ña, ak Og buuru Basan, ak buuri Kanaan ñépp.
12 Moo nangu seen réew, séddale, bànni Israyil ñiy ñoñam séddoo.
13 Aji Sax ji, sa tur ba fàww; Aji Sax ji, sa woy a saxal maasoo maas.
14 Aji Sax ji kay ay àtte ñoñam ñi, di ñeewante jaamam ñi.
15 Tuuri yéefar yi, xaalis ak wurus, loxoo ko sàkk.
16 Am gémmiñ te du wax, ami gët te du gis,
17 ami nopp te du dégg, du sax noowal bakkan.
18 Ñi sàkk yii tuur, yal nañu mel ni ñoom, ñook ñi leen wóolu ñépp.
19 Éey waa kër Israyil, santleen Aji Sax ji! Éey waa kër Aaróona, santleen Aji Sax ji!
Sabóor 135 in Kàddug Yàlla gi