3 Mu ne: «Duma ñibbi,
4 duma tëddi sama kaw lal ba, duma nelaw, duma gëmm sax bët,
5 li feek sàkkaluma Aji Sax ji bérab, ba dëkkal Mbërum Yanqóoba ma.»
6 Ma ne, Efrata lanu dégg gaalu Yàlla ga, fekk ko àllub Yaar.
7 Nan dem ba këram, sujjóotali ndëggëstalu tànkam ya.
8 Aji Sax ji, jógal agsi sa dal-lukaay, yaak sa gaal gi jëmmal sa doole.
9 Say sarxalkat, yal nañu woddoo njekk, sa wóllëre yi sarxolleendoo.
10 Xoolal ci Daawuda, sa jaam ba, bul gàntu ki nga fal.
11 Aji Sax ji daa giñal Daawuda dëgg gu mu dul dëddu, ne ko: «Ku jóge sa geño laay wuutal ci sa jal bi,