13 Aji Sax ji kat a tànn Siyoŋ, taamu faa dëkke.
14 Mu ne: «Fii laay dal-loo ba fàww, fii laay dëkk, maa ko taamu.
15 Dund bi, ma barkeela barkeel, néew-ji-doole yi, ma reggal;
16 sarxalkat yi, ma wodde njot; way-gëm ñi di sarxollee sarxolle.
17 Fa laay dooleele Daawuda, taalal ki ma fal,