3 Ki Sax, yaw, soo doon lim bàkkaar, Boroom bi, ana kuy taxaw?
4 Waaye yaay jéggale, ñu ragal la.
5 Damay xaar Aji Sax ji, di ko xaare xol, di yaakaar kàddoom.
6 Wattukat bi yàkkamti njël, wattukat bi yàkkamti njël, laa ne, ni ma yàkkamtee Aji Sax jee ko raw.