3 Céy, Yerusalem, dëkkub tabax bu baax, bi booloo, di benn.
4 Fii la giiri Israyil di yéegsi, di giir yi Ki Sax séddoo. Ñu ngi santsi Aji Sax ji, ni ko Israyil warloo.
5 Fii la ngànguney Israyil tege, askanu Daawuda toog ca, di àtte.
6 Dagaanleen jàmmi Yerusalem: «Yerusalem, yal na sa xeli soppe dal,
7 jàmm ne ñoyy fi say tata wër, te xel dal ci biir këri Buur.»