Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 119:97-167 in Wolof

Help us?

Sabóor 119:97-167 in Kàddug Yàlla gi

97 Maaka sopp saw yoon, di ko jàngat bés bu jot.
98 Li ma xelal ba ma raw noon yi, mooy sa santaane, yi ma jagoo fàww.
99 Maa gëna ñaw képp ku may jàngal, nde sa kàdduy seedeey sama njàngat.
100 Maa ëpp mag ñi dég-dég, nde say tegtal laa topp.
101 Luy yoon wu aay, ma moyu, ba mana sàmm sa kàddu.
102 Say santaane it dëdduwma ko, nde yaw yaa ma jàngal.
103 Sa kàddooka maa neex, ba dàqal ma tem-temu lem!
104 Say tegtal laay ràññee, ba tax ma bañ luy yoonu fen.
105 Sa kàddu laay niitoo samay tànk, muy leeral samaw yoon.
106 Giñ naa te di ko dëggal, ne dinaa sàmmonteek sa ndigali njekk.
107 Toskare naa ba ci lool; éy Aji Sax ji, musal ma, yaa ko dige.
108 Aji Sax ji, rikk nangul ma kàdduy cant yi ma lay jébbal, te xamal ma say ndigal.
109 Sama bakkan ci xott saa su ne, waaye fàttewuma saw yoon.
110 Ñu bon ñi ma gasal um pax taxul ma wàcc say tegtal.
111 Maa séddoo fàww sa kàdduy seede, loolooy seral sama xol.
112 Damaa dogoo jëfe sa dogali yoon, saxoo ko ba mu jeex.
113 Maa bañ kuy ŋarale, maa sopp saw yoon.
114 Sama rawtu, sama kiiraay, yaw a; sa kàddu laay xaar.
115 Yeen ñiy def lu bon, xiddileen ma, ba ma sàmmonteek sama santaaney Yàlla.
116 Yaa ko dige, dooleel ma, ma dund; bul tas sama yaakaar.
117 Kàttanal ma, ma raw, di yittewoo say tegtal, ba fàww.
118 Yaay xarab képp ku wàcc sa dogali yoon, ay pexeem neen.
119 Yaay tonni ni purit képp ku bon fi kaw suuf, moo tax ma sopp sa kàdduy seede.
120 Sama yaram a ngi daw ndax ragal la, ragal say àtte.
121 Def naa njub, def njekk; bu ma wacce ñi may néewal.
122 Sang bi, gàddu ma, ma am jàmm, bu ma ñu bew ñi néewal.
123 Séentu naa sag wall ak sa kàddug njekk, ba saay gët giim.
124 Sang bi, jëfeel ma sa ngor, xamal ma sa dogali yoon.
125 Sab jaam laa, may ma, ma ràññee, ba xam sa kàdduy seede.
126 Aji Sax ji, jëf jot na, ñee ngi jalgati saw yoon!
127 Maa sopp say santaane, mu gënal ma wurus ba ci wurusu ngalam.
128 Moo tax foo tegtale, ma rafetlu, lépp luy yoonu fen, ma bañ.
129 Sa kàdduy seede kéemaan la, moo tax ma di ko toppe xol.
130 Sa pirim kàddu day leeral, di xelal ku xeluwul.
131 Damaa ŋa ŋafeet, di àppaat, ngir namm say santaane.
132 Éy geesu ma te baaxe ma, ni nga baaxook ñi sopp sa tur.
133 Dooleelal ma samay tànk, yaa ko dige, te bu ma lenn lu bon man.
134 Jot ma ci noteelu doom aadama, ma mana topp say tegtal.
135 Sang bi, geesoo ma sag leer, te xamal ma sa dogali yoon,
136 ay wali rongooñ ay wale saay gët, ndax sàmmeesul saw yoon.
137 Aji Sax ji, yaaka jub, te say àtte di yoon.
138 Yaa santaane sa kàdduy seede ci njekk ak worma ju yaa.
139 Damaa gis bañ yiy sàggane say wax, xol bu tàng di ma rey.
140 Sang bi, maaka sopp sa kàddu gi set ni weñ gu ñu xelli!
141 Ñàkk naa solo, faaleesu ma, waaye sàgganewma say tegtal.
142 Sag njekk moo dig njekk ba fàww, te saw yoon a dëggu.
143 Njekkar ak njàqare dab ma, say santaane di sama bànneex.
144 Sa kàdduy seedee di njekk ba fàww, may ma, ma ràññee, ba dund.
145 Aji Sax ji, woo naa la wall lu ma man, wuyu ma, ma topp sa dogali yoon.
146 Dama ne: «Wóoy, wallu ma, ma sàmm sa kàdduy seede.»
147 Damaa jëlu, di la woo, di xaar sa kàddu.
148 Damay xoole guddi gépp, di jàngat sa kàddu.
149 Aji Sax ji, sama baat bii, teewloo ko sa ngor, te musal ma ni nga baaxoo muslee.
150 Rabatkati pexe yaa ngi jegesi, di nit ñu sore saw yoon.
151 Waaye yaw Aji Sax ji, jege nga, te sa santaane yépp a dëggu.
152 Yàgg naa xam ne sa kàdduy seede wax la joo saxal dàkk.
153 Xoolal sama coono te xettli ma; saw yoon déy, sàgganewma ko.
154 Àtte ma, ba jot ma; musal ma, yaa ko dige.
155 Ku bon sore sa wall, ngir sàkkuwul sa dogali yoon.
156 Aji Sax ji, sa yërmande yaa na; musal ma ni nga ko baaxoo.
157 Ñi ma topp ak ñi ma baña bare, te taxul ma dëddu sa kàdduy seede.
158 Damaa gis workat yi, sib leen; ñoo sàmmul sa kàddu.
159 Seetlul ni ma soppe say tegtal. Éy Aji Sax ji, musal ma, yaa gore!
160 Sa mboolem kàddu dëgg la, sa ndigal yépp di njekk, sax dàkk.
161 Ay kilifaa ma topp ci dara, te teewul ma wormaal sa kàddu.
162 Man de, maa ngi bége sa kàddu ni ku for alal ju bare.
163 Fen, ma bañ, ba sib; sa yoon, ma sopp.
164 Juróom yaari yoon ci bés màggale naa la ko say àttey njekk.
165 Jàmm ju baree ñeel ku sopp sa yoon, te dara du ko fakktal.
166 Aji Sax ji, sa wall laa yaakaar, say santaane laa jëfe.
167 Sama xol laa toppe sa kàdduy seede, te sopp koo sopp.
Sabóor 119 in Kàddug Yàlla gi