Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 119:80-83 in Wolof

Help us?

Sabóor 119:80-83 in Kàddug Yàlla gi

80 Yal naa toppe say tegtal xol bu mat sëkk, ba duma rus.
81 Sàkku naa sag wall ba xol jeex, di xaar sa kàddu.
82 Séentu naa sab dige, ba gët giim; kañ nga may xettli?
83 Damaa mujj ras ni mbuusum der mu saxar jàpp, waaye sàgganewma say tegtal.
Sabóor 119 in Kàddug Yàlla gi