77 Nanga ma ganesee sa yërmande, ma dund; saw yoon ay sama bànneex!
78 Yal na ñu bew ñi torox, ñoo ma lor ak seeni sos, te man may gëstu say tegtal.
79 Yal na ku la ragal waññiku fi man, ba xam sa kàdduy seede.
80 Yal naa toppe say tegtal xol bu mat sëkk, ba duma rus.
81 Sàkku naa sag wall ba xol jeex, di xaar sa kàddu.
82 Séentu naa sab dige, ba gët giim; kañ nga may xettli?
83 Damaa mujj ras ni mbuusum der mu saxar jàpp, waaye sàgganewma say tegtal.
84 Ñaata fan laay toogati, Sang bi? Kañ ngay mbugal ñi ma topp?
85 Ñu bew ñi gasal nañu ma ay yeer, yu saw yoon diglewul.
86 Sa santaane yépp worma la; te dees maa toppey sos, wallu ma!