Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 119:71-101 in Wolof

Help us?

Sabóor 119:71-101 in Kàddug Yàlla gi

71 Ngëneel la ma duma yi jural, ngir jànge naa ci say tegtal.
72 Sa ngëneelu yoon wi nga digle moo ma gënal ay junniy xaalis ak wurus.
73 Say loxoo ma sàkk, tabax ma, may ma ag dégg, ma mokkal say santaane,
74 ñi la ragal gis ma, bég; nde sa kàddu laa yaakaar.
75 Aji Sax ji, ràññee naa ne say ndigal njekk la, te worma nga ma dumaa.
76 Ngalla dëfale ma sa ngor; Sang bi, yaa ko dige.
77 Nanga ma ganesee sa yërmande, ma dund; saw yoon ay sama bànneex!
78 Yal na ñu bew ñi torox, ñoo ma lor ak seeni sos, te man may gëstu say tegtal.
79 Yal na ku la ragal waññiku fi man, ba xam sa kàdduy seede.
80 Yal naa toppe say tegtal xol bu mat sëkk, ba duma rus.
81 Sàkku naa sag wall ba xol jeex, di xaar sa kàddu.
82 Séentu naa sab dige, ba gët giim; kañ nga may xettli?
83 Damaa mujj ras ni mbuusum der mu saxar jàpp, waaye sàgganewma say tegtal.
84 Ñaata fan laay toogati, Sang bi? Kañ ngay mbugal ñi ma topp?
85 Ñu bew ñi gasal nañu ma ay yeer, yu saw yoon diglewul.
86 Sa santaane yépp worma la; te dees maa toppey sos, wallu ma!
87 Nes tuut ñu sànke ma fi kaw suuf, te man dëdduwma say tegtal.
88 Musale ma sa ngor, ba jëfe sa kàdduy seede.
89 Aji Sax ji, sa kàddoo sax dàkk, taxaw jonn fa asamaan.
90 Sa worma, ba maasoo maas, yaa samp suuf, saxal ko.
91 Ci sa ndigal la lépp taxawe ba tey, lépp ànd, di la jaamu.
92 Su ma bégewuloon saw yoon, sànkoo sama toskare ji.
93 Duma fàtte mukk say tegtal, ci nga may musale.
94 Yaa ma moom, wallu ma; say tegtal laay sàkku.
95 Man la ñu bon ñi tëru, nar maa sànk, waaye sa kàdduy seede laay niir.
96 Gis naa ne lu mat lu ne am na kemu, waaye sa santaane mat ba wees kemu.
97 Maaka sopp saw yoon, di ko jàngat bés bu jot.
98 Li ma xelal ba ma raw noon yi, mooy sa santaane, yi ma jagoo fàww.
99 Maa gëna ñaw képp ku may jàngal, nde sa kàdduy seedeey sama njàngat.
100 Maa ëpp mag ñi dég-dég, nde say tegtal laa topp.
101 Luy yoon wu aay, ma moyu, ba mana sàmm sa kàddu.
Sabóor 119 in Kàddug Yàlla gi