Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 119:67-72 in Wolof

Help us?

Sabóor 119:67-72 in Kàddug Yàlla gi

67 Maa jàddoon, nga duma ma, léegi sa kàddu laay sàmm.
68 Yaaka baax tey baaxe; rikk xamal ma say tegtal.
69 Ñu bew ñee yàq sama der aki sos, te ma topp say tegtal, wéetal la.
70 Ñu ngi nii, seen bopp yi, tafas; te man may tàqamtikoo saw yoon.
71 Ngëneel la ma duma yi jural, ngir jànge naa ci say tegtal.
72 Sa ngëneelu yoon wi nga digle moo ma gënal ay junniy xaalis ak wurus.
Sabóor 119 in Kàddug Yàlla gi