Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 119:67-71 in Wolof

Help us?

Sabóor 119:67-71 in Kàddug Yàlla gi

67 Maa jàddoon, nga duma ma, léegi sa kàddu laay sàmm.
68 Yaaka baax tey baaxe; rikk xamal ma say tegtal.
69 Ñu bew ñee yàq sama der aki sos, te ma topp say tegtal, wéetal la.
70 Ñu ngi nii, seen bopp yi, tafas; te man may tàqamtikoo saw yoon.
71 Ngëneel la ma duma yi jural, ngir jànge naa ci say tegtal.
Sabóor 119 in Kàddug Yàlla gi