Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 119:43-49 in Wolof

Help us?

Sabóor 119:43-49 in Kàddug Yàlla gi

43 Bu ma xañ mukk kàddug dëgg, say àtte laa yaakaar kat.
44 Maay topp saw yoon, sàlloo ko, saxoo ko ba fàww,
45 di daagoo sago, nde say tegtal laay sàkku.
46 Maay àgge ay buur sa kàdduy seede, te duma rus.
47 Maay bége sa santaane yi ma sopp,
48 di yóotu sa santaane yi ma sopp, di jàngat sa dogali yoon.
49 Bàyyil xel li nga ma dig, Sang bi; moom laa yaakaar.
Sabóor 119 in Kàddug Yàlla gi