Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 119:32-85 in Wolof

Help us?

Sabóor 119:32-85 in Kàddug Yàlla gi

32 Sa yoonu santaane laay daw, yaa may may xol bu tàlli.
33 Aji Sax ji, xamal ma li sa dogali yoon yiy firi, ma topp ko ba mu jeex.
34 May ma dég-dég, ma topp saw yoon, toppe ko xol bu tàlli.
35 Jiite ma ci sa xàllu santaane yi, mooy sama bànneex.
36 Joyantil sama xol, mu féeteek sa kàdduy seede, te dummóoyu alal ju lewul.
37 May ma, ma fénati caaxaani neen, te musale ma saw yoon.
38 Sang bi, sottalal ma sa dige bi nga digook ku la ragal.
39 Moyale ma gàcce gi ma ragal; yaa baaxi ndigal.
40 Maaka namm say tegtal, musale ma sag njekk!
41 Aji Sax ji, yaa ko dige, dikke ma sa jëfi ngor ak sa wall,
42 ba ku ma kókkali, ma am tontam. Maa doyloo sa kàddu.
43 Bu ma xañ mukk kàddug dëgg, say àtte laa yaakaar kat.
44 Maay topp saw yoon, sàlloo ko, saxoo ko ba fàww,
45 di daagoo sago, nde say tegtal laay sàkku.
46 Maay àgge ay buur sa kàdduy seede, te duma rus.
47 Maay bége sa santaane yi ma sopp,
48 di yóotu sa santaane yi ma sopp, di jàngat sa dogali yoon.
49 Bàyyil xel li nga ma dig, Sang bi; moom laa yaakaar.
50 Lii laay muñe samaw naqar, sa kàddoo may dundal.
51 Nit ñu bew ñi ñaawal nañu ma lool, waaye dëdduwma saw yoon.
52 Éy Aji Sax ji, damaa fàttliku sa àtte ya woon, daldi muñ.
53 Sama xol daa fees ndax ñu bon ñiy wacc saw yoon.
54 Sa dogali yoon laay woyantoo, fu ma mana sance.
55 Aji Sax ji, tudd naa la guddi, di sàmm saw yoon.
56 Lii laa séddoo, maa topp sa tegtali yoon.
57 Aji Sax ji, yaw laa séddoo; di digee sàmm sa kàddu.
58 Sama léppi xol laa sàkkoo saw yiw, ngalla baaxe ma, yaa ko dige.
59 Damaa seetlu sama jëfin, dëpp, topp sa kàdduy seede.
60 Maa ngi gaawtu, yeexewma say santaane moos!
61 Buumi ñu bon ñaa ngi may laaw, te sàgganewma saw yoon.
62 Xaaju guddi laay jóg, di la sante sa àttey njekk.
63 Maa xejjoo képp ku la ragal, tey topp say tegtal.
64 Aji Sax ji, sa ngor dajal na àddina; xamal ma sa dogali yoon.
65 Aji Sax ji, def nga la nga dige woon, Sang bi, defal nga ma ngëneel.
66 Xamal ma ngëneeli àtte ak xam-xam, maa doyloo say santaane.
67 Maa jàddoon, nga duma ma, léegi sa kàddu laay sàmm.
68 Yaaka baax tey baaxe; rikk xamal ma say tegtal.
69 Ñu bew ñee yàq sama der aki sos, te ma topp say tegtal, wéetal la.
70 Ñu ngi nii, seen bopp yi, tafas; te man may tàqamtikoo saw yoon.
71 Ngëneel la ma duma yi jural, ngir jànge naa ci say tegtal.
72 Sa ngëneelu yoon wi nga digle moo ma gënal ay junniy xaalis ak wurus.
73 Say loxoo ma sàkk, tabax ma, may ma ag dégg, ma mokkal say santaane,
74 ñi la ragal gis ma, bég; nde sa kàddu laa yaakaar.
75 Aji Sax ji, ràññee naa ne say ndigal njekk la, te worma nga ma dumaa.
76 Ngalla dëfale ma sa ngor; Sang bi, yaa ko dige.
77 Nanga ma ganesee sa yërmande, ma dund; saw yoon ay sama bànneex!
78 Yal na ñu bew ñi torox, ñoo ma lor ak seeni sos, te man may gëstu say tegtal.
79 Yal na ku la ragal waññiku fi man, ba xam sa kàdduy seede.
80 Yal naa toppe say tegtal xol bu mat sëkk, ba duma rus.
81 Sàkku naa sag wall ba xol jeex, di xaar sa kàddu.
82 Séentu naa sab dige, ba gët giim; kañ nga may xettli?
83 Damaa mujj ras ni mbuusum der mu saxar jàpp, waaye sàgganewma say tegtal.
84 Ñaata fan laay toogati, Sang bi? Kañ ngay mbugal ñi ma topp?
85 Ñu bew ñi gasal nañu ma ay yeer, yu saw yoon diglewul.
Sabóor 119 in Kàddug Yàlla gi