Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 119:153-171 in Wolof

Help us?

Sabóor 119:153-171 in Kàddug Yàlla gi

153 Xoolal sama coono te xettli ma; saw yoon déy, sàgganewma ko.
154 Àtte ma, ba jot ma; musal ma, yaa ko dige.
155 Ku bon sore sa wall, ngir sàkkuwul sa dogali yoon.
156 Aji Sax ji, sa yërmande yaa na; musal ma ni nga ko baaxoo.
157 Ñi ma topp ak ñi ma baña bare, te taxul ma dëddu sa kàdduy seede.
158 Damaa gis workat yi, sib leen; ñoo sàmmul sa kàddu.
159 Seetlul ni ma soppe say tegtal. Éy Aji Sax ji, musal ma, yaa gore!
160 Sa mboolem kàddu dëgg la, sa ndigal yépp di njekk, sax dàkk.
161 Ay kilifaa ma topp ci dara, te teewul ma wormaal sa kàddu.
162 Man de, maa ngi bége sa kàddu ni ku for alal ju bare.
163 Fen, ma bañ, ba sib; sa yoon, ma sopp.
164 Juróom yaari yoon ci bés màggale naa la ko say àttey njekk.
165 Jàmm ju baree ñeel ku sopp sa yoon, te dara du ko fakktal.
166 Aji Sax ji, sa wall laa yaakaar, say santaane laa jëfe.
167 Sama xol laa toppe sa kàdduy seede, te sopp koo sopp.
168 Damaa topp say tegtal ak sa kàdduy seede, fépp fu ma jaar kay yaa ngi ciy gis.
169 Aji Sax ji, yal na sama yuux àgg fa yaw; may ma, ma ràññee, yaa ko dige.
170 Yal na sama dagaan àgg fa yaw; xettli ma, yaa ko dige.
171 Naa xaacu, woyal la, yaa may jàngal sa dogali yoon.
Sabóor 119 in Kàddug Yàlla gi