Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 119:114-144 in Wolof

Help us?

Sabóor 119:114-144 in Kàddug Yàlla gi

114 Sama rawtu, sama kiiraay, yaw a; sa kàddu laay xaar.
115 Yeen ñiy def lu bon, xiddileen ma, ba ma sàmmonteek sama santaaney Yàlla.
116 Yaa ko dige, dooleel ma, ma dund; bul tas sama yaakaar.
117 Kàttanal ma, ma raw, di yittewoo say tegtal, ba fàww.
118 Yaay xarab képp ku wàcc sa dogali yoon, ay pexeem neen.
119 Yaay tonni ni purit képp ku bon fi kaw suuf, moo tax ma sopp sa kàdduy seede.
120 Sama yaram a ngi daw ndax ragal la, ragal say àtte.
121 Def naa njub, def njekk; bu ma wacce ñi may néewal.
122 Sang bi, gàddu ma, ma am jàmm, bu ma ñu bew ñi néewal.
123 Séentu naa sag wall ak sa kàddug njekk, ba saay gët giim.
124 Sang bi, jëfeel ma sa ngor, xamal ma sa dogali yoon.
125 Sab jaam laa, may ma, ma ràññee, ba xam sa kàdduy seede.
126 Aji Sax ji, jëf jot na, ñee ngi jalgati saw yoon!
127 Maa sopp say santaane, mu gënal ma wurus ba ci wurusu ngalam.
128 Moo tax foo tegtale, ma rafetlu, lépp luy yoonu fen, ma bañ.
129 Sa kàdduy seede kéemaan la, moo tax ma di ko toppe xol.
130 Sa pirim kàddu day leeral, di xelal ku xeluwul.
131 Damaa ŋa ŋafeet, di àppaat, ngir namm say santaane.
132 Éy geesu ma te baaxe ma, ni nga baaxook ñi sopp sa tur.
133 Dooleelal ma samay tànk, yaa ko dige, te bu ma lenn lu bon man.
134 Jot ma ci noteelu doom aadama, ma mana topp say tegtal.
135 Sang bi, geesoo ma sag leer, te xamal ma sa dogali yoon,
136 ay wali rongooñ ay wale saay gët, ndax sàmmeesul saw yoon.
137 Aji Sax ji, yaaka jub, te say àtte di yoon.
138 Yaa santaane sa kàdduy seede ci njekk ak worma ju yaa.
139 Damaa gis bañ yiy sàggane say wax, xol bu tàng di ma rey.
140 Sang bi, maaka sopp sa kàddu gi set ni weñ gu ñu xelli!
141 Ñàkk naa solo, faaleesu ma, waaye sàgganewma say tegtal.
142 Sag njekk moo dig njekk ba fàww, te saw yoon a dëggu.
143 Njekkar ak njàqare dab ma, say santaane di sama bànneex.
144 Sa kàdduy seedee di njekk ba fàww, may ma, ma ràññee, ba dund.
Sabóor 119 in Kàddug Yàlla gi