Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 119:102-139 in Wolof

Help us?

Sabóor 119:102-139 in Kàddug Yàlla gi

102 Say santaane it dëdduwma ko, nde yaw yaa ma jàngal.
103 Sa kàddooka maa neex, ba dàqal ma tem-temu lem!
104 Say tegtal laay ràññee, ba tax ma bañ luy yoonu fen.
105 Sa kàddu laay niitoo samay tànk, muy leeral samaw yoon.
106 Giñ naa te di ko dëggal, ne dinaa sàmmonteek sa ndigali njekk.
107 Toskare naa ba ci lool; éy Aji Sax ji, musal ma, yaa ko dige.
108 Aji Sax ji, rikk nangul ma kàdduy cant yi ma lay jébbal, te xamal ma say ndigal.
109 Sama bakkan ci xott saa su ne, waaye fàttewuma saw yoon.
110 Ñu bon ñi ma gasal um pax taxul ma wàcc say tegtal.
111 Maa séddoo fàww sa kàdduy seede, loolooy seral sama xol.
112 Damaa dogoo jëfe sa dogali yoon, saxoo ko ba mu jeex.
113 Maa bañ kuy ŋarale, maa sopp saw yoon.
114 Sama rawtu, sama kiiraay, yaw a; sa kàddu laay xaar.
115 Yeen ñiy def lu bon, xiddileen ma, ba ma sàmmonteek sama santaaney Yàlla.
116 Yaa ko dige, dooleel ma, ma dund; bul tas sama yaakaar.
117 Kàttanal ma, ma raw, di yittewoo say tegtal, ba fàww.
118 Yaay xarab képp ku wàcc sa dogali yoon, ay pexeem neen.
119 Yaay tonni ni purit képp ku bon fi kaw suuf, moo tax ma sopp sa kàdduy seede.
120 Sama yaram a ngi daw ndax ragal la, ragal say àtte.
121 Def naa njub, def njekk; bu ma wacce ñi may néewal.
122 Sang bi, gàddu ma, ma am jàmm, bu ma ñu bew ñi néewal.
123 Séentu naa sag wall ak sa kàddug njekk, ba saay gët giim.
124 Sang bi, jëfeel ma sa ngor, xamal ma sa dogali yoon.
125 Sab jaam laa, may ma, ma ràññee, ba xam sa kàdduy seede.
126 Aji Sax ji, jëf jot na, ñee ngi jalgati saw yoon!
127 Maa sopp say santaane, mu gënal ma wurus ba ci wurusu ngalam.
128 Moo tax foo tegtale, ma rafetlu, lépp luy yoonu fen, ma bañ.
129 Sa kàdduy seede kéemaan la, moo tax ma di ko toppe xol.
130 Sa pirim kàddu day leeral, di xelal ku xeluwul.
131 Damaa ŋa ŋafeet, di àppaat, ngir namm say santaane.
132 Éy geesu ma te baaxe ma, ni nga baaxook ñi sopp sa tur.
133 Dooleelal ma samay tànk, yaa ko dige, te bu ma lenn lu bon man.
134 Jot ma ci noteelu doom aadama, ma mana topp say tegtal.
135 Sang bi, geesoo ma sag leer, te xamal ma sa dogali yoon,
136 ay wali rongooñ ay wale saay gët, ndax sàmmeesul saw yoon.
137 Aji Sax ji, yaaka jub, te say àtte di yoon.
138 Yaa santaane sa kàdduy seede ci njekk ak worma ju yaa.
139 Damaa gis bañ yiy sàggane say wax, xol bu tàng di ma rey.
Sabóor 119 in Kàddug Yàlla gi