Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 119:100-105 in Wolof

Help us?

Sabóor 119:100-105 in Kàddug Yàlla gi

100 Maa ëpp mag ñi dég-dég, nde say tegtal laa topp.
101 Luy yoon wu aay, ma moyu, ba mana sàmm sa kàddu.
102 Say santaane it dëdduwma ko, nde yaw yaa ma jàngal.
103 Sa kàddooka maa neex, ba dàqal ma tem-temu lem!
104 Say tegtal laay ràññee, ba tax ma bañ luy yoonu fen.
105 Sa kàddu laay niitoo samay tànk, muy leeral samaw yoon.
Sabóor 119 in Kàddug Yàlla gi