7 Ndaxte ku fonk sa nafsu, bañaaleb Yàlla nga, ndaxte doo déggal Yàlla, mbaa ngay sàmm ay santaaneem, te manuloo koo def sax.
8 Kuy topp sa nafsu nag, doo mana neex Yàlla.
9 Waaye yéen nekkatuleen ci topp seen nafsu, waaye yéena ngi topp Xelu Yàlla mi, bu fekkee ne mu ngi dëkk ci yéen. Ku amul Xelum Kirist nag, bokkuloo ci moom.
10 Bu fekkee ne Kirist dëkk na ci yéen nag, lii moo am: seen yaram mi ngi ci dooley dee ndax bàkkaar bi nekk ci yéen, waaye seen xel mi ngi dund ndax njub gi leen Yàlla jox.
11 Kon nag gannaaw Xelum Yàlla, mi dekkal Yeesu ca néew ya, dëkk na ci yéen, dina tax seen yaram wi néew doole dund ci kàttanu Xel moomu dëkk ci yéen.
12 Kon nag bokk yi, am nanu lu nu war, waaye waxuma leen topp sunu nafsu ak i bëgg-bëggam;
13 ndaxte kuy topp nafsoom, fàww mu dee, waaye kuy not jëfi yaramam ci dooley Xelu Yàlla mi, dina dund.
14 Ndaxte ñépp ñiy déggal Xelu Yàlla mi, ay doomi Yàlla lañu.
15 Nekkatuleen fa kanam Yàlla, ni jaam bu ragal sangam, waaye Xel mi leen Yàlla sol, ay doomi Yàlla la leen def, ba tax nu di wooye Yàlla: «Abba», maanaam «Baay.»