Text copied!
Bibles in Wolof

ROOM 8:2-30 in Wolof

Help us?

ROOM 8:2-30 in Téereb Injiil

2 Ndaxte kàttanu Xelum Yàlla, tukkee ci Kirist Yeesu, di may nit dund gu bees, goreel na ma ci notaangeg bàkkaar ak dee.
3 Lu yoonu Musaa manul woona def, ndax néew dooley nit, Yàlla defe na ko nii: dafa yónni Doomam, ngir mu yor sunu jëmm, nun ñiy nekk ay bàkkaarkat, ba noppi mu jébbale bakkanam, ngir dindi bàkkaar yi. Noonu la Yàlla tase nguuru bàkkaar ci nit.
4 Ba tax na léegi njub, gi yoonu Musaa di digle, am na ci nun, ñiy déggal Xelu Yàlla mi te baña topp sunu nafsu.
5 Ñiy topp seen nafsu, seeni bëgg-bëgg rekk lañu fonk, waaye ñiy topp Xelu Yàlla mi, coobareem lañu fonk.
6 Ndaxte fonk nafsu, ci dee lay jëme; waaye fonk Xelu Yàlla mi, dund ak jàmm lay joxe.
7 Ndaxte ku fonk sa nafsu, bañaaleb Yàlla nga, ndaxte doo déggal Yàlla, mbaa ngay sàmm ay santaaneem, te manuloo koo def sax.
8 Kuy topp sa nafsu nag, doo mana neex Yàlla.
9 Waaye yéen nekkatuleen ci topp seen nafsu, waaye yéena ngi topp Xelu Yàlla mi, bu fekkee ne mu ngi dëkk ci yéen. Ku amul Xelum Kirist nag, bokkuloo ci moom.
10 Bu fekkee ne Kirist dëkk na ci yéen nag, lii moo am: seen yaram mi ngi ci dooley dee ndax bàkkaar bi nekk ci yéen, waaye seen xel mi ngi dund ndax njub gi leen Yàlla jox.
11 Kon nag gannaaw Xelum Yàlla, mi dekkal Yeesu ca néew ya, dëkk na ci yéen, dina tax seen yaram wi néew doole dund ci kàttanu Xel moomu dëkk ci yéen.
12 Kon nag bokk yi, am nanu lu nu war, waaye waxuma leen topp sunu nafsu ak i bëgg-bëggam;
13 ndaxte kuy topp nafsoom, fàww mu dee, waaye kuy not jëfi yaramam ci dooley Xelu Yàlla mi, dina dund.
14 Ndaxte ñépp ñiy déggal Xelu Yàlla mi, ay doomi Yàlla lañu.
15 Nekkatuleen fa kanam Yàlla, ni jaam bu ragal sangam, waaye Xel mi leen Yàlla sol, ay doomi Yàlla la leen def, ba tax nu di wooye Yàlla: «Abba», maanaam «Baay.»
16 Ndaxte Xelu Yàlla mi, moom ci boppam, day ànd ak sunu xel ci seede ne doomi Yàlla lanu.
17 Gannaaw ay doomi Yàlla lanu, dinanu moomi lépp li Yàlla jagleel ay doomam, séddu ci ngëneel yi Kirist yelloo. Waaye nag ku bëgga bokk ak Kirist ndamam ëllëg, war ngaa séddu ci ay fitnaam tey.
18 Xalaat naa ne sunu naqaru tey, wareesu ko tëkkale ak sunu ndamu ëllëg.
19 Ndax li Yàlla bind lépp a ngi ne seewa gis doomi Yàlla yi feeñ ci seen biir ndam.
20 Ndaxte dunyaa bi bépp mu ngi ci yoon wu dul mujj fenn; teyu ko, Yàlla moo ko ko teg. Waaye teewul ñu am yaakaar ne,
21 Yàlla dina rengi seen buumi njaam ci dee, boole leen ci jàmmu doomi Yàlla yi ak seen ndam.
22 Xam nanu ba fi nu tollu ne li Yàlla bind lépp a ngi mititlu ni jigéen juy matu.
23 Te du dunyaa bi rekk mooy mititlu, nun it nu ngi mititlu, nun ñi Yàlla sol Xelam, ngir nu ñam añu ëllëg; nu ngi ne seew Yàlla boole nu ci lépp li nu yelloo ni ay doomam, keroog bés bu Yàllay goreel sunu yaram.
24 Ndaxte sunu mucc ëmb na yaakaar. Li nga gis ba noppi, nekkatul yaakaar; li teew, noo koy yaakaare?
25 Li feek gisagunu nag li nuy yaakaar, dinanu ko séentu ak muñ.
26 Te it Xelu Yàlla mi moo nuy xettali ci sunug néew doole. Ndaxte xamunu sax naka lanu wara ñaane Yàlla, waaye Xelu Yàlla maa ngi nuy ñaanal fa moom ak i yéene yu làmmiñ manta takk.
27 Te Yàlla, miy nattu xol yi, xam na xalaatu Xel mi, ndaxte tinu, gi muy tinul gaayi Yàlla yi, méngoo na ak coobarey Yàlla.
28 Xam nanu itam ne ñi bëgg Yàlla, maanaam ñi Yàlla woo ci boppam te boole leen ci li mu tëral, Yàlla dina joo loxoom ci lépp lu xew ci seen dund, ngir jural leen lu baax.
29 Ndaxte ñi mu xamoon lu jiitu, dafa dogaloon ñu nirook Doomam, ngir mu nekk taaw ci biir njaboot gu yaa.
30 Ñi mu dogaloon loolu ci ñoom, da leena woo; ñooñu mu woo, da leena àtte ni ñu jub; ñooñu mu àtte jub, da leena boole ca ndamam.
ROOM 8 in Téereb Injiil

Room 8:2-30 in Kàddug Yàlla gi

2 Ndax kat, dooley Noo giy maye bakkan te nekk ci Almasi Yeesu moo la yiwi, ba nga mucc ci dooley bàkkaar ak ndee.
3 Li yoonu Musaa tële woon ndax néew dooley nitu suuxu neen, mooy lii Yàlla def: Doomam la yónni, mu dikke melow nit, te nit di bàkkaarkat, di suuxu neen, ngir Doomam fajtal mbirum bàkkaar. Yaramu suux wu nit kooku la Yàlla sottale mbugal gi war ci bàkkaar,
4 ngir njub gi yoonu Musaa laaj mana sotti ba mat sëkk ci nun, ñi toppatul sunu bindu suux, xanaa Noowug Yàlla.
5 Ndax kat ñi topp seen bindu suux, mbiri bakkan doŋŋ lañu xinte, waaye ñi topp Noowug Yàlla ñoom, mbiri Noowug Yàlla mooy seen xinte.
6 Xintey bakkan nag ci ndee lay jëme, waaye xintey Noowug Yàlla ndund ak jàmm lay jur.
7 Ndaxte boroom xintey bakkan ab noonu Yàlla la, nde déggalul yoonu Yàlla, te manu ko sax.
8 Moo tax ñi wéye seen bindu suuxu neen duñu mana neex Yàlla.
9 Yeen nag nekkatuleen ci kilifteefu bindu suuxu neen, waaye ci kilifteefu Noo gi ngeen nekk, ndegam kay Noowug Yàllaa ngi màkkaanoo ci yeen. Ku amul Noowug Almasi, kooku du nitam.
10 Su Almasi nekkee ci yeen, seen yaram dina dee moos ndax bàkkaar, waaye du tee seenug noo di dund, ndax àtteb njub bi ngeen am ba noppi.
11 Noowug ki dekkal Yeesu moo màkkaanoo ci yeen. Kon nag ki dekkal Almasi mooy dekkal itam seen yarami ndee, ndax Noowam googu màkkaanoo ci yeen.
12 Kon nag bokk yi, bor topp na nu, waaye du sunu bindu suux lanu ameel lenn lu nu taxa topp sunu bakkan;
13 Ku topp bakkanam, fàww mu dee, waaye ku rey jëfi yaramam ci ndimbalal Noowug Yàlla, dina texe.
14 Ndax kat, mboolem ñiy dox ci njiital Noo gi, ñooñu ay doomi Yàlla lañu.
15 Mayeesu leen noo gu leen di desloo cig njaam, ba tax leena dellu cig ragal, waaye Noowug doom yu ñu doomoo, moom lees leen may, te looloo nu tax di wooye Yàlla: «Abba», mu tekki «Baay.»
16 Te Noowug Yàlla, moom ci boppam, moo mànkoo ak sunu noowug bopp, di seede ne ay doomi Yàlla lanu.
17 Gannaaw ay doom lanu nag, ay boroom cér lanu, ay boroom cér yu Yàlla sédd, cér yu nu bokk ak Almasi, gannaaw noo bokk ak moom ab coono tey, ngir bokk ak moom teraangay ëllëg.
18 Jàpp naa ne sunu coonob tey du dara, soo ko xoolee ci teraanga ji ñu nuy feeñalal ëllëg.
19 Càkkéefu àddinaa ngi séentu, ndax yàkkamti bés ba doomi Yàlla di feeñ.
20 Ndax kat, càkkéef gépp, li ñuy déggal neenug neen la, te du seen coobare, waaye ki leen ci tënk la neex, ba tax ñuy yaakaar,
21 ñoom ñi bokk ci càkkéef googu itam, ne dees na rengi seen buumi njaam gi leen ndee ak yàqutey yaram ràng, ngir ñu am cér ci goreelug doomi Yàlla yi, am cér ci seen teraanga.
22 Xam nanu ba fii nu tollu ne mboolem càkkéef gaa ngi binni ndax mitit, ni kuy matu.
23 Te du càkkéef gi rekk, waaye nun ci sunu bopp itam, ci lanu, nun ñi jot ab dawal ci Noo gi, nun ci sunu bopp sax nu ngi binni sunu biir xol, ndax yàkkamtee jot céru doomi Yàlla, ba sunu njotug yaram mat.
24 Ndax kat sunu mucc, yaakaar la taxaweegum, te yaakaar joo teg sa bët, dootu yaakaar. Li nit ki teg bëtam, nu mu koy yaakaaratee?
25 Li nu gisul kay lanuy yaakaar, di ko séentook a muñe yaakaar ji.
26 Te itam Noo gi moo nuy dimbali ndax sunug néew doole, nde xamunu sax li jaadoo sàkku ci sunuy ñaan, waaye Noowug Yàlla moo nuy tinule ay onk yu wees kàddug làmmiñ.
27 Te kiy xool li ci biir xol yi, xam na liy xintey Noo gi, nde ni ko Yàlla bëgge, ni la Noo giy tinool ñu sell ñi.
28 Te itam nag xam nanu ne Yàlla mooy def mboolem lu xew, daje ba jur njariñal ñi sopp Yàlla, ñi mu woo, noonee ko ab dogalam namme.
29 Ndax ñooñu Yàllaa leen ràññee woon lu jiitu, te it la mu dogaloon lu jiitu ci ñoom moo di ñu niru Doomam, ngir Doomam di taaw, ci biir rakk yu bare.
30 Ñi Yàlla tuddaloon loolu lu jiitu, moo leen woo itam; ñooñu mu woo, moo leen jox itam àtteb ñu jub; te ñooñu mu jox àtteb ñu jub, moo leen darajaal itam.
Room 8 in Kàddug Yàlla gi