Text copied!
Bibles in Wolof

ROOM 7:16-25 in Wolof

Help us?

ROOM 7:16-25 in Téereb Injiil

16 Kon nag gannaaw li may def du sama coobare, nangu naa ne yoonu Musaa baax na.
17 Léegi nag du man maay def lu bon loolu, waaye bàkkaar bi dëkk ci man, moo ma ciy jiiñ.
18 Ndaxte xam naa ne lu baax dëkkul ci man, maanaam ci sama bindu doom Aadama. Am naa yéeney def lu baax, waaye awma kàttanu yeggale.
19 Lu baax nag lu may yéene, duma ko def, waaye lu bon lu ma bëggul, moom laay def.
20 Bu fekkee nag lu ma bëggul, moom laay def, kon dootul sama coobare, waaye bàkkaar bi dëkk ci man, moo ma ci jiiñ.
21 Gis naa nag lii: saa su ma bëggee def lu baax, lu bon a ngi ma taxawu.
22 Ndaxte ci sama biir xol yoonu Yàlla wi neex na ma.
23 Waaye gis naa jeneen doole juy yëngu ci samay céri yaram, di bëre ak li sama xol bëgg; day bëre ba not ma, def ma jaam ci dooley bàkkaar joojuy yëngu ci samay cér.
24 Céy maaka torox! Ana ku may musal ci sama yaram, wii may jëme ci dee?
25 Maa ngi sant Yàlla; am na kuy musle, mooy Yeesu Kirist sunu Boroom. Kon nag lii laa gis ci sama bopp: ci sama xel maa ngi topp yoonu Yàlla, waaye ci sama bindu doom Aadama maa ngi topp yoonu bàkkaar.
ROOM 7 in Téereb Injiil

Room 7:16-25 in Kàddug Yàlla gi

16 Gannaaw li ma buggul, moom laay def nag, juboo naa ak yoonu Musaa ci dëggal ne yoonu Musaa baax na.
17 Kon nag dootu man maay jëfe noonu, waaye dooley bàkkaar bi ci man la.
18 Xam naa ne man, sama bindu suuxu neen wii, lenn lu baax dëkku ci. Yéene jaa ngeek man, kàttanu jëfe lu baax moo fi nekkul.
19 Ndax kat du lu baax li ma namma jëfe laay jëfe, waaye lu bon li ma nammul, moom laay jëfe.
20 Te su dee li ma nammul, moom laay def, kon kay dootu man maa koy def, waaye dooley bàkkaar bi dëkk ci man moo koy def.
21 Takk bi ma ci gis daal mooy lii: bu ma nammee def lu baax, lu bon a may teewalsi.
22 Ndaxam ci sama biir xol, yoonu Yàllaa ma neex.
23 Waaye gis naa ci samay cér, weneen yoon wuy xeex ak yoon wi samam xel jubool, te yoon woowoo ma jàpp njaam, jébbal ma dooley bàkkaar bi dëkke samay cér.
24 Céy maaka réy aw tiis! Ana ku may wallook sama yaramu ndee wii?
25 Waaye cant ñeel na Yàlla mi nuy walloo jëmmu Yeesu Almasi, sunu Sang. Kon daal man, ci sama bopp, ci sama wàllu xel, yoonu Yàlla laay surgawu, waaye ci sama wàllu yaramu suux wii, yoonu bàkkaar laay surgawu.
Room 7 in Kàddug Yàlla gi