Text copied!
Bibles in Wolof

ROOM 7:10-19 in Wolof

Help us?

ROOM 7:10-19 in Téereb Injiil

10 Noonu gis naa ne ndigal loolu waroona jëme nit ñi ci dund, daf maa jëme ci dee.
11 Ndaxte bàkkaar jaar na ci li Yàlla digle, ba nax ma, rey ma.
12 Kon nag man nanoo wax ne yoonu Musaa yoon wu sell la, te ndigalu Yàlla dafa sell, jub te baax.
13 Ndax kon lu baax moo ma tàbbal ci dee? Mukk! Bàkkaar a ko def, ngir jikkoom feeñ; dafa gis ci lu baax loolu bunt bu mu mana jaar, ba rey ma. Noonu ndigalu Yàlla tax na, bàkkaar fés, bon ba jéggi dayo.
14 Xam nanu ne yoonu Musaa ngi jóge ci Yàlla, waaye man yëfi àddina laa fonk, te nekk ci dooley bàkkaar, mel nib jaam.
15 Ndaxte samay jëf jaaxal na ma; li ma bëgga def, duma ko def, waaye li ma bañ rekk, moom laay def.
16 Kon nag gannaaw li may def du sama coobare, nangu naa ne yoonu Musaa baax na.
17 Léegi nag du man maay def lu bon loolu, waaye bàkkaar bi dëkk ci man, moo ma ciy jiiñ.
18 Ndaxte xam naa ne lu baax dëkkul ci man, maanaam ci sama bindu doom Aadama. Am naa yéeney def lu baax, waaye awma kàttanu yeggale.
19 Lu baax nag lu may yéene, duma ko def, waaye lu bon lu ma bëggul, moom laay def.
ROOM 7 in Téereb Injiil

Room 7:10-19 in Kàddug Yàlla gi

10 man nag, ma dee. Kon ndigalu yoon wi wara jëme ci ag dund, moom ci boppam moo ma mujj jëme ci ndee.
11 Bàkkaar moo ma jekkoo ndigalu yoon, ba nax ma, te ndigalu yoon la ma reye it.
12 Kon yoonu Musaa lu sell la, ndigalam di lu sell, te jub te baax.
13 Lu baax loolu di yoonu Musaa, xanaa kon moo ma taxa dee? Déet kay! Bàkkaar moo feeñale noonu meloom; moo jëfandikoo lu baax, ba rey ma, ngir ndigalu yoon di jumtukaay bu bàkkaar fésale gépp mbonam gu jéggi dayo.
14 Xam nanu ne yoonu Musaa ci Yàlla la bokk, te man may nitu suuxu neen, dib jaam bu ñu jaay bàkkaar.
15 Xawma sax lu waral may jëfe ni may jëfe; li ma namm, du loolu laay jëfe, waaye li ma bañ, moom laay jëfe.
16 Gannaaw li ma buggul, moom laay def nag, juboo naa ak yoonu Musaa ci dëggal ne yoonu Musaa baax na.
17 Kon nag dootu man maay jëfe noonu, waaye dooley bàkkaar bi ci man la.
18 Xam naa ne man, sama bindu suuxu neen wii, lenn lu baax dëkku ci. Yéene jaa ngeek man, kàttanu jëfe lu baax moo fi nekkul.
19 Ndax kat du lu baax li ma namma jëfe laay jëfe, waaye lu bon li ma nammul, moom laay jëfe.
Room 7 in Kàddug Yàlla gi