Text copied!
Bibles in Wolof

ROOM 7:1-11 in Wolof

Help us?

ROOM 7:1-11 in Téereb Injiil

1 Bokk yi, yéen ñi may waxal xam ngeen luy yoon; xam ngeen kon ne yoon am na doole ci nit diirub dundam.
2 Ci maanaa, mu ngi mel ni jigéen juy séy; yoon a ngi koy boole ak jëkkëram, ñu ànd seen giiru dund, waaye su jëkkër ji faatoo, buum gi dagg na.
3 Kon nag su jabar ji àndee ak beneen góor, te fekk jëkkër jiy dund, dees na ko àtte njaaloo. Waaye bu jëkkër ji faatoo, yoon jeexal na seen diggante; man na séy nag ak beneen góor, te du doon njaaloo.
4 Nii laa leen ko mana misaale, samay bokk; bi Kirist deeyee, dangeena deeyandoo ak moom, te noonu yoonu Musaa wàcc leen. Léegi nag yéena ngi ànd ak keneen, maanaam Kirist mi dekki, ngir nu amal Yàlla njariñ.
5 Keroog ba nu daan topp sunu nafsu, yoonu Musaa daan na xamb bëgg-bëgg yu bon, yiy yëngal sunuy cér, ba jural nu dee.
6 Waaye léegi yoon wi wàcc na nu, ci li nu dee, ba rëcc cig buumam. Léegi nag nu ngi jaamu Yàlla, waxuma leen ci sàmm santaane rekk, ndax loolu wees na, waaye ci kàttan gu bees, gi nu Xelum Yàlla di may.
7 Kon nag lu nu wara wax? Ndax bàkkaar ci yoonu Musaa la jóge? Mukk! Waaye moo ma xamal luy bàkkaar. Ndaxte su ma yoon wi waxul woon: «Bul bëgg yëfi jaambur,» kon duma xam luy xemmem.
8 Waaye bàkkaar jaare na ci ndigalu Yàlla, daldi ñëw dugg ci man, ba yëngal ci man xemmem yu bare. Ndaxte ba ma xamagul woon yoonu Musaa, bàkkaar da ne woon nemm ci man.
9 Keroog bi ma xamagul lu yoon wi santaane, maa ngi doon dund dund gu neex; waaye ba ma ko déggee, bàkkaar dafa daldi fuddu ci man, te man ma daldi dee.
10 Noonu gis naa ne ndigal loolu waroona jëme nit ñi ci dund, daf maa jëme ci dee.
11 Ndaxte bàkkaar jaar na ci li Yàlla digle, ba nax ma, rey ma.
ROOM 7 in Téereb Injiil

Room 7:1-11 in Kàddug Yàlla gi

1 Am, bokk yi, yeen ñi xam yoon wi laay waxal, dangeena umple ne yoon yiliful nit ki lu moy ci giiru dundam?
2 Dafa mel ni ndaw suy séy; li feek jëkkëram di dund, yoon a yeew buumu jëkkëram ci baatam. Waaye su jëkkër ji deeyee, ndaw si teqlikoo na ak yoon wi ko yeewoon buumu jëkkëram.
3 Kon nag, li feek jëkkëru ndaw si di dund, su séyee ak geneen góor, ab jaalookat lees koy wax. Su jëkkër ji deeyee nag, yoon yiwi na ndaw si, te su séyee ak keneen, du doon njaaloo.
4 Noonu la deme ak yeen itam, bokk yi. Yaramu Almasi wi ngeen bennool, ci ngeen doone ñu deeyal yoonu Musaa. Noonu ngeen doone moomeelu keneen, te kooku mooy ki dekki, ngir nu meññ njariñ lu ñeel Yàlla.
5 Ba nu toppee sunu bakkan, sunu bëgg-bëgg yu bon yi ndigali yoonu Musaa yee, ñoo daan liggéey ci sunuy cér, ngir nu meññ lu nu jëme ci ndee.
6 Waaye tey ci sunu digg ak yoon wi nu tënku woon, la nu di ñu dee, ba teqlikoo ak moom. Moo tax nu doon ay jaam yu tegoo kilifteef gu yees, gi Noowug Yàlla indi, gannaaw ba nu wàccoo ak kilifteefu mbindu yoonu Musaa ma woon.
7 Ana lu loolu di tekki? Xanaa kon yoonu Musaa bàkkaar la? Mukk kay! Waaye yoonu Musaa moo ma xamal luy bàkkaar. Ndax kat su dul woon ak yoon wi ne: «Bul xemmem yëfi jaambur,» kon xemmemtéef sax duma xam lu mu doon.
8 Waaye bàkkaar moo jaare buntub ndigalu yoon, ba yee ci man mboolemi xemmemtéef yu bon. Ndax kat, su yoonu Musaa amul woon, bàkkaar di lu dee.
9 Man de, bu jëkkoon, ba ma xamagul yoonu Musaa, teewul woon may dund. Waaye ba yoonu Musaa dikkee, ca la bàkkaar ne xiféet, di dund,
10 man nag, ma dee. Kon ndigalu yoon wi wara jëme ci ag dund, moom ci boppam moo ma mujj jëme ci ndee.
11 Bàkkaar moo ma jekkoo ndigalu yoon, ba nax ma, te ndigalu yoon la ma reye it.
Room 7 in Kàddug Yàlla gi