Text copied!
Bibles in Wolof

ROOM 6:3-17 in Wolof

Help us?

ROOM 6:3-17 in Téereb Injiil

3 Xanaa dangeena xamul ne, képp ku ñu sóob ci ndox, ngir wone ne mu ngi bokk ci Yeesu Kirist, ci deewu Yeesu la bokk.
4 Bi ñu nu sóobee ci ndox moomu nag, day misaal ne dañu noo suul ak Kirist, nu dee ni mu deeye woon; ba tax nu dekki it, ni mu dekkee woon ci dooley Yàlla Baay bi, te nu sóobu ci dund gu bees.
5 Kon nag gannaaw benn lanu ak Kirist, dee ni mu deeye woon, kon dinanu nekk it benn ak moom, dekki ni mu dekkee woon.
6 Ndegam xam nanu ne daajoon nañu Kirist ca bant ba, xam nanu it ne jikko ju bon ji nu judduwaale, daajaale nañu ko ak Kirist ca bant ba. Yàlla def na loolu, ngir nguuru bàkkaar, gi nekkoon ci sunu yaram tas, nu rëcc ci dooleem.
7 Ndaxte ku dee, bàkkaar manatul dara ci yaw.
8 Gannaaw nag dee nanu ak Kirist, gëm nanu ne dinanu dekki it ni moom,
9 xam ne Kirist mi dekki dootul dee mukk, dee manatul dara ci moom.
10 Dee na benn yoon, ba bàkkaar manul ci moom dara; mi ngi dund léegi, di ànd ak Yàlla ba fàww.
11 Ci noonu nag yéen itam tegleen seen bopp ni ñu dee ak Kirist, ba rëcc ci dooley bàkkaar, di dund, ànd ak Yàlla ba fàww ndax seen bokk ci Yeesu Kirist.
12 Buleen mayati bàkkaar nag, mu yilif seeni yaram yu néew doole, bay topp ay bëgg-bëggam.
13 Buleen jébbalati seeni cér bàkkaar, mu def leen jumtukaayam ngir jëfam yu jubadi; waaye gannaaw rëcc ngeen ci dooley dee, bay dundaat, jébbaluleen ci Yàlla te jébbal ko seeni cér, mu def leen jumtukaayam ngir jëfam yu jub.
14 Ndaxte bàkkaar dootu leen manal dara, yéen ñi génn ci yoonu Musaa, dugg ci yiwu Yàlla.
15 Lan lanu wara wax nag léegi? Gannaaw génn nanu ci yoonu Musaa, dugg ci yiwu Yàlla, ndax danoo wara sax ci def bàkkaar? Mukk!
16 Ndax dangeena xamul ne koo jébbalu ci moom te déggal ko, jaamam nga? Naka noonu, mbaa ngeen nekk jaami bàkkaar, mu jëme leen ci dee, mbaa ngeen déggal Yàlla, mu sóob leen ci yoonu njub.
17 Waaye sant naa Yàlla ci lii: yéen ñi doon jaami bàkkaar, bi ngeen déggee mboolem dëgg gi, nangu ngeen ko ak seen xol bépp.
ROOM 6 in Téereb Injiil

Room 6:3-17 in Kàddug Yàlla gi

3 Dangeena umple ne mboolem nun ñi ñu sóob ci Yeesu Almasi, cig deeyam lañu nu sóobaale?
4 Ci sóobu googu lañu nu boole ak moom suul, ngir noonee Almasi dekkee ci màggug Baay bi, nun itam nu dekki bay dund dundin wu yees.
5 Gannaaw dees noo bennale ak moom ci dee gu ñu nirule ak deeyam, dees nuy bennale itam ak moom ci ndekkite lu niru ndekkiteem.
6 Li nu bir moo di nun ña woon démb, ca bantub Yeesu ba lees nu daajaale, ngir xewil sunu yaramu bàkkaar, ba nu noppee doon ay jaam, bàkkaar di sunub sang.
7 Ndax ki dee ba noppi, joxees na ko àtteb ku jub, mu tàggook noteelu bàkkaar.
8 Gannaaw noo deeyandoo ak Almasi nag, gëm nanu ne nooy dundandoo ak moom.
9 Ndax kat xam nanu ne Almasi mi dekki dootu dee, te ndee manalatu ko dara.
10 Deeyam ga mu dee ca la deeyal bàkkaar benn yoon ba fàww, te dund gi muy dund tey, Yàlla la koy dundal.
11 Naka noonu, yeen itam jàppeleen seen bopp nit ñu deeyal bàkkaar, te di dundal Yàlla, ci Yeesu Almasi.
12 Kon nag bu bàkkaar yilif seen yaramu ndee wii, ba di leen nanguloo ay xemmemtéefam yu bon.
13 Buleen jébbal seeni cér bàkkaar, mu def leen jumtukaayi njubadi; gannaaw yeena dekki bay dundaat, jébbal-leen Yàlla seen bopp te jébbal ko seeni cér, ngir def leen ay jumtukaayi njub.
14 Ndax kat bàkkaar yilifatu leen, nde du ci kilifteefu yoonu Musaa ngeen nekk, waaye ci aw yiw ngeen tàbbi.
15 Ba ci lan boog? Ndax kon danuy bàkkaar, gannaaw du ci kilifteefu yoonu Musaa lanu nekk, waaye ci aw yiw lanu tàbbi? Déet kay!
16 Xanaa xamuleen ne képp koo jébbal sa bopp, nangul ko, ab jaamam nga? Yaar ngeen diy jaam, bàkkaar di seen sang, jëme leen ci ndee; mbaa ngeen déggal Yàlla, mu jox leen àtteb ñu jub.
17 Waaye cant ñeel na Yàlla, nde ay jaami bàkkaar ngeen woon, waaye gannaaw gi, seenub xol ngeen déggale misaalub àlluwa, ji ngeen di ndénkaaneem.
Room 6 in Kàddug Yàlla gi