Text copied!
Bibles in Wolof

ROOM 6:10-21 in Wolof

Help us?

ROOM 6:10-21 in Téereb Injiil

10 Dee na benn yoon, ba bàkkaar manul ci moom dara; mi ngi dund léegi, di ànd ak Yàlla ba fàww.
11 Ci noonu nag yéen itam tegleen seen bopp ni ñu dee ak Kirist, ba rëcc ci dooley bàkkaar, di dund, ànd ak Yàlla ba fàww ndax seen bokk ci Yeesu Kirist.
12 Buleen mayati bàkkaar nag, mu yilif seeni yaram yu néew doole, bay topp ay bëgg-bëggam.
13 Buleen jébbalati seeni cér bàkkaar, mu def leen jumtukaayam ngir jëfam yu jubadi; waaye gannaaw rëcc ngeen ci dooley dee, bay dundaat, jébbaluleen ci Yàlla te jébbal ko seeni cér, mu def leen jumtukaayam ngir jëfam yu jub.
14 Ndaxte bàkkaar dootu leen manal dara, yéen ñi génn ci yoonu Musaa, dugg ci yiwu Yàlla.
15 Lan lanu wara wax nag léegi? Gannaaw génn nanu ci yoonu Musaa, dugg ci yiwu Yàlla, ndax danoo wara sax ci def bàkkaar? Mukk!
16 Ndax dangeena xamul ne koo jébbalu ci moom te déggal ko, jaamam nga? Naka noonu, mbaa ngeen nekk jaami bàkkaar, mu jëme leen ci dee, mbaa ngeen déggal Yàlla, mu sóob leen ci yoonu njub.
17 Waaye sant naa Yàlla ci lii: yéen ñi doon jaami bàkkaar, bi ngeen déggee mboolem dëgg gi, nangu ngeen ko ak seen xol bépp.
18 Ci noonu rëcc ngeen ci notaangeg bàkkaar te jébbalu ci Yàlla, sóobu ci njub.
19 Xam naa ne seen xam-xam ci mbir mii sorewul, moo tax ma yombal wax ji, awale ko ci baat yii. Ni ngeen jële woon seeni cér, jébbal leen, ñu nekk jaami lu selladi ak lu bon, di gëna jur lu bon, noonu itam léegi jébbal-leen seeni cér, ñu nekk jaami njub, ngeen doora sell.
20 Ndaxte keroog ba ngeen nekkee jaami bàkkaar, séquleen woon dara ak lu jub.
21 Ban njariñ ngeen ci jële nag? Dara lu dul gàcce, ndaxte ci dee la leen doon jëmale.
ROOM 6 in Téereb Injiil

Room 6:10-21 in Kàddug Yàlla gi

10 Deeyam ga mu dee ca la deeyal bàkkaar benn yoon ba fàww, te dund gi muy dund tey, Yàlla la koy dundal.
11 Naka noonu, yeen itam jàppeleen seen bopp nit ñu deeyal bàkkaar, te di dundal Yàlla, ci Yeesu Almasi.
12 Kon nag bu bàkkaar yilif seen yaramu ndee wii, ba di leen nanguloo ay xemmemtéefam yu bon.
13 Buleen jébbal seeni cér bàkkaar, mu def leen jumtukaayi njubadi; gannaaw yeena dekki bay dundaat, jébbal-leen Yàlla seen bopp te jébbal ko seeni cér, ngir def leen ay jumtukaayi njub.
14 Ndax kat bàkkaar yilifatu leen, nde du ci kilifteefu yoonu Musaa ngeen nekk, waaye ci aw yiw ngeen tàbbi.
15 Ba ci lan boog? Ndax kon danuy bàkkaar, gannaaw du ci kilifteefu yoonu Musaa lanu nekk, waaye ci aw yiw lanu tàbbi? Déet kay!
16 Xanaa xamuleen ne képp koo jébbal sa bopp, nangul ko, ab jaamam nga? Yaar ngeen diy jaam, bàkkaar di seen sang, jëme leen ci ndee; mbaa ngeen déggal Yàlla, mu jox leen àtteb ñu jub.
17 Waaye cant ñeel na Yàlla, nde ay jaami bàkkaar ngeen woon, waaye gannaaw gi, seenub xol ngeen déggale misaalub àlluwa, ji ngeen di ndénkaaneem.
18 Noonu lees leen yiwee, tàggale leen ak noteelu bàkkaar, ngeen doon ay surgay njub.
19 Ni ko nit mana dégge rekk, ni laa leen woyofalale kàddu gii, ndax seen néew dooley nitu neen. Noonee ngeen jébbale woon seeni cér, def leen ñuy jaami sobe, ak ndëngte gu jur ndëngte, noonu ngeen wara jébbale seeni cér, def leen ñuy jaami njub gu jur sellnga.
20 Ba ngeen dee jaami bàkkaar, teewuleen woona moom seen bopp, ci seen digganteek njub.
21 Seen jëfi démb ja leen gàcceel tey, ana njariñ lu mu leen jural? Mujug jëf ja de, seenug dee la doon doon.
Room 6 in Kàddug Yàlla gi