Text copied!
Bibles in Wolof

ROOM 5:5-13 in Wolof

Help us?

ROOM 5:5-13 in Téereb Injiil

5 Te yaakaar jooju du ay nax, ndax mbëggeelu Yàllaa ngi baawaan ci sunu xol, jaarale ko ci Xelam mu Sell mi mu nu may.
6 Ndaxte bi nu amul jenn doole, booba la Kirist dee ngir nun, fekk danoo weddi woon Yàlla.
7 Kuy nangoo deeyal nit ku jub, yombula gis, waaye nag jombul am na ku nangoo deeyal ku baax.
8 Waaye Yàlla firndeel na mbëggeelam ci nun, ci li Kirist dee ngir nun, bi nu nekkee sax ay bàkkaarkat!
9 Gannaaw Kirist tuur na deretam nag, ngir Yàlla àtte nu jub, rawatina ne dina nu musal ci merum Yàlla.
10 Nun ay bañaaley Yàlla lanu woon, waaye Doomam dee na, ngir jubale nu ak moom. Gannaaw léegi nag xariti Yàlla lanu, rawatina ne dinanu mucc ndax dundug Doomam.
11 Te sax nu ngi bég ci Yàlla, jaarale ko ci sunu Boroom Yeesu Kirist, mi nu jubale ak moom.
12 Kon nag bàkkaar ci kenn nit la jaar, dugg ci àddina, indaale fi dee, te dee daldi law ci nit ñépp, ndaxte ñépp a bàkkaar.
13 Bàkkaar kon nekkoon na ci àddina, bi Yàlla di laata wàcce yoonu Musaa. Waaye gannaaw yoonu Musaa tëddagul woon, bàkkaar du woon jàdd yoon.
ROOM 5 in Téereb Injiil

Room 5:5-13 in Kàddug Yàlla gi

5 Te yaakaar jooju du tas, ndax cofeelu Yàlla gi baawaan ci sunu xol, ci ndimbalal Noo gu Sell gi mu nu may.
6 Ndax kat, ba nu amul menn pexem mucc, ca la Almasi deeyal yéefar yi nu doon, ba mu jotee.
7 Barewul ku nangoo deeyal nit ku jub, doonte jombul mu am ku nangoo deeyal ku baax.
8 Waaye Yàlla moom, ni mu firndeele cofeelam ci nun, moo di, ba nu dee ay bàkkaarkat, ca la nu Almasi deeyal!
9 Gannaaw joxees nañu nu àtteb ñu jub ndax deretam ji tuuru nag, ñaata yoon lees nuy gënatee musal ci am sànj ndax moom?
10 Ndegam ba ñu dee ay bañaaley Yàlla lees nu jubalee deewug Doomam, ñaata yoon lees nuy gënatee musale ag dundam, gannaaw ba ñu nu jubalee ak Yàlla?
11 Te yemunu ci, xanaa di sagoo Yàlla itam ndax sunu Boroom Yeesu Almasi, mi nu jubale ak moom.
12 Bàkkaar moo jaare ci kenn nit dugg ci àddina, dee jaare ci bàkkaar, dikk, ba dikkal ñépp, ndax ñépp a bàkkaar.
13 Bàkkaar a ngi woon ci àddina ba ca janti yoonu Musaa, waaye deesul waññale bàkkaar te aw yoon amul.
Room 5 in Kàddug Yàlla gi